[messages]


From: bachastu@sonatel.senet.net
Date: Sun, 8 Dec 1996 19:31:50 GMT
X-Sender: bachastu@sonatel.senet.net (Unverified)
Mime-Version: 1.0
X-Priority: 2 (High)
To: pajol@bok.net
Subject: Gaa ñi , dëgërël
leen seen mànko , ndam li du leen
rëcc!!

Mbokk yi,

Ñun ay ñu doon ligéey mbaa di jàng tugël ci at yi weesu la ñu. Ñu ngi dëkk
ci diiwaanu Tàmbakundaa. Ni leen nguuri Farans def mettina ñu torop. Dafa fa
mel na yar yi leen "CRS" yi doon döör suñu kaw la doon dal. Dina ñu def liñu
mën ngir jàppale leen, ndax seen xeex ñoo ko bokk. Tàmbale na ñu yëgle bi ci
kuréél yiy aar sañ-sañu doomu aadama yi. Di na ñu def suñu kéémtalaayu
kàttan ngir siiwal seen ñefe. Dëgërël leen seen mànko! Bu ngeen jàppe fële
ñu jàpp fii, ag ndimalu tubaab yiy xeex boddënte xeet tey ñefe ngir sàmp
demokarasi, daañu yoobu ndam li. Jarawlak gaa ñi!!

SEENI MBOKK FII CI TAMBAKUNDAA