Ñan lañu ?
[sans-papiers]


mere-enfant français  / english  / deutsch  / italiano  / wolof



ÑUN, ÑI AMUL KËYIT « ñi nek Saint-Ambroise », ñu ngi dal eglizu Saint-Bernard bi nek Chapelle. Door nañu khekh bu comace fuku fan ak juroom ñat si weru mars. Ño ngi ko comace eglizu Saint-Ambroise bi nek Pari ngir yegël nit ñëp, doxalin bi goornmaa frans, jël pur xeex nit ñi amul këyit.

Nit yi sex ñi amul këyit :

Doxalin bi goornmaabi jël ngir xeex ñi amul këyit te yit, bëg lena gene si sen dëkëbi. Bañu uta jël këyitu ñi nga xamne amnañu ba pare. Ño ngi len di xeex ak sen ay lua yi ñu tude lua Pasqua-Méhaignerie-Toubon ak yi Debré gene. Ñun ñi amul këyit nak, nëbu uñu. Dañu bëgë ñu xamne ño ngii def lune ngir mëna dunda si rewum Frans te man fi teda ak suñu jooboot.

Tey nak fi si Frans keep ku amul këyit ya ngi fi nek nekin bu meti.